Saar 27
Yeneen diglee ngi
Bul damoo ëllëg,
ndax xamoo luy xew tey.
Bul tëggu, bàyyil ñu tagg la,
muy waxi keneen; yaw, bu ko wax.
 
Doj diis na, suuf dib sëf,
waaye fitnay dof a ko raw.
 
Xadar day ñàng, mer di wal mu baawaan,
waaye fiiraange amul moroom.
 
Artu yu ñu la biralal
moo gën cofeel gu la boroom ñooru.
Soppe, bu lay gaañ sax, wóolu ko.
Nit bañ na la, te di la fóon lu bare.
 
Ku suur, bañ lem ju xelli,
waaye boo xiifee, lu wex lu ne neex la.
 
Ku sore fa nga bokk,
dangay mel ni picc mu sore tàggam.
 
Diwook suuru day naatal xol;
waaye li neex cib xarit, xol la lay digale.
 
10 Bul fàtte sab xarit mbaa sa xaritu baay,
bul jàq ba seeti sa mbokk;
dëkkandoo bu jegee gën mbokk mu sore.
 
11 Muusal, doom, ma bég,
ba mana tontu ku ma sikk.
 
12 Kuy foog, gisu ay, làqu;
ab téxét ne ca tëñëx, loru.
 
13 Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam;
tayle ko, moo dige feyal ndaw su yemadi.
 
14 Nuyoo bu xumb, suba teel
mooki saagaa yem.
 
15 Jabar ju pànk
mooy senn bu dakkul, cib taw;
16 ku ko mana yemale,
mana téye ngelaw mbaa nga ŋëb ag diw.
 
17 Weñ ay nàmm weñ,
nit ay nàmm xelu moroom ma.
 
18 Ku aar garab, lekk ca doom ya;
ku topptoo sa sang, am ngërëm.
 
19 Ku xool cim ndox, gis sa kanam,
nga xool sab xol, gis sa jikko.
 
20 Njaniiw ak biir suuf du fees,
bët it du doylu mukk.
 
21 Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli,
waaye àtteb nit ca jëëm.
 
22 Soo jëloon ub dof, yeb ci gënn,
booleek pepp, wol,
du tax ndof ga deñ.
 
23 Xamal bu baax lu say gàtt nekke,
te def sa xel ci say gétt,
24 ndax alal wéyul fàww,
ag pal du ñeel sëtoo sët.
25 Gannaaw bu ñu gubee,
ba ñax saxaat,
ñu dajale ngooñ ma ca tund ya* 27.25 Ca Israyil tund yaa ëpp lu muy taw, te fa la ñax ma ëppe.,
26 say xar da lay amal koddaay,
bëy yi génneel la njégu tool.
27 Meewum bëy daldi am, ba doy la dund,
yaak sa waa kër
ak sa surga yu jigéen.
 

*27:25 27.25 Ca Israyil tund yaa ëpp lu muy taw, te fa la ñax ma ëppe.