Bataaxal bi Yàlla may Póol,
mu bind ko
Filemon
Saar 1
Ci man Póol, mi ñu tëj kaso ngir Almasi Yeesu, ci man ak itam ci Timote miy mbokkum gëmkat la bataaxal bii bawoo, ñeel Filemon, sunu soppe bi bokk ak nun liggéey bi. Mu ñeel itam sunub jigéen Afya, ak Arsipp sunu mbokkum xarekat, ak mbooloom gëmkat miy dajee sa kër. Yeen la aw yiw ak jàmm ñeel, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
Póol a ngi sant ci biir ñaan
Sant sama Yàlla laa dëkke saa yu ma la fàttlikoo ci samay ñaan, ndax dégg naa sa gëm Sang Yeesu, ak sa cofeel ci mboolem ñu sell ñi. Damay ñaan nag sa ngëm, gi nu bokk amal la njariñal ràññee mboolem ngëneel, yi nu am ci Almasi. Mbokk mi, mbégte mu réy, ak xel mu dal laa am ci sa cofeel, ndax ni nga serale xolu aji sell ñi.
Póol tinul na Onesim
Lii nag sañoon naa la koo digal ci turu Almasi, ndax mooy li la war, waaye tinu la ci ngir cofeel, mooy li ma taamu, man Póol mu màggat mii, boole ci léegi tënku biir kaso ndax Almasi Yeesu. 10 Damay tinul Onesim, sama doomu tuubeen ji ma tuubloo ba mu mel ni maa ko jur ci diir bi ma nekke fii ci kaso bi. 11 Amalu la woon njariñ* 11 njariñ: ci làkku gereg turu Onesim mooy tekki «Ku am njariñ.» démb, waaye tey yaak man la amal njariñ.
12 Maa ngi koy yebal ngir mu dellu fi yaw, te di kenn ci man. 13 Dama koo bëggoona téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xibaaru jàmm bi. 14 Waaye buggumaa def dara loo àndul, ngir mu baña doon ndimbalu ñàkk pexe, xanaa loo defe xol bu tàlli. 15 Jombul itam dees koo tàggale ak yaw ab diir, ngir nga jotaat ci moom ba fàww, 16 ba dootu doon sab jaam, waaye day wees ab jaam, di mbokk, di soppe, ma sopp ko lool, te nga war ma koo gëna sopp, ngir jëmmu boppam, ak Sang bi ngeen bokk.
17 Ndegam nag sa waay nga ma def, dalal ko ni su doon man. 18 Su la tooñee, mbaa mu ameel la lenn, topp ma ko. 19 Man Póol maay bind fii ci sama loxol bopp: maay fey loolu, duma ci tuddaale bor bi nga ma ameel, te muy sa njotug bakkanu bopp! 20 Kon nag mbokk mi, may ma googu njekk ngir Sang bi, te nga seral sama xol ndax Almasi. 21 Wóor na ma ci diggante bii may bind bataaxal bi, ne dinga ma déggal, te xam naa ne dinga def sax lu wees li may wax.
22 Te itam nanga ma waajalaale ab dal, ndax yaakaar naa ne dees na ma délloosi fi yeen, ndax seen ñaan yu nangu.
23 Epafras, mbokk mi ñu ma tëjandool ndax Almasi Yeesu, mu ngi lay nuyu, 24 mook Màrk ak Aristàrk ak Demas ak Luug, bokk yi may liggéeyandool.
25 Yal na yiwu Sang Yeesu Almasi ànd ak seenum xel.

*1:11 11 njariñ: ci làkku gereg turu Onesim mooy tekki «Ku am njariñ.»