3
Ku gëm dina jëf lu rafet
Fàttali leen ñuy déggal kilifa, yi yore nguur gi, tey jëfe seeni ndigal, ñu taxaw temm ci lépp luy jëf ju baax. Buñu jëw kenn mbaa ñuy ŋaayoo, waaye nañu yiwe te won ñépp lewet gu mat sëkk.
Ndaxte nun itam ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, nu réer bay jaamu ay bëgg-bëgg ak i bànneex yu wuute, nu dëkk ci coxorte ak ñeetaane, ñu bañ nu te nu bañante ci sunu biir. Waaye naka noona Yàlla sunu Musalkat feeñal na mbaaxam ak cofeelam, ba musal nu; ajuwul ci jëf yu jub yu nu def, waaye ci yërmandeem rekk. Mu juddulaat nu ci laabal sunu xol, te yeesalaat nu ci dooley Xel mu Sell, mi mu nu sotti ba mu baawaan, ci darajay Yeesu Kirist sunu Musalkat. Ci noonu Yàlla àtte na nu jub ci kaw yiwam, te sédd nu ci dund gu dul jeex, gi nuy séentu.
Wax jooju ju wóor la, te damaa bëgg nga dëggal loolu, ngir ñi gëm Yàlla sax ci jëf lu rafet. Loolu moo baax te am njariñ ci nit. Waaye moytul yu deme ni werantey neen ak limi maam, ay xuloo ak i xëccoo ci doxalinu yoonu Musaa, ndax loolu waxi neen la, te amul benn njariñ. 10 Kuy féewale, nanga ko yedd, yeddaat ko; bu tëwee, nga dàq ko, 11 xam ne nit ku ñaaw xel la te ay bàkkaaram fés ci ñépp.
Muj gi
12 Bu ma la yónnee Artemas walla Tisig, gaawantul fekksi ma ci dëkku Nikopolis, ndax fa laa bëgga lollikooji. 13 Naka Senas àttekat bi nag ak Apolos, waajal leen bu jekk ci seen tukki, ba seen aajo yépp faju. 14 Na sunuy bokk it takku ci jëf yu rafet, ba mana faj aajo yépp, te baña yaafus.
15 Ñiy ànd ak man ñépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy soppey ngëm. Yal na yiwu Yàlla ànd ak yéen ñépp.