10
Malaaka yégle na ne àtte bu mujj ba agsi na
1 Noonu ma gis meneen malaaka mu am doole, muy wàcce asamaan, làmboo niir. Xon tiim ko, xar kanamam mel ni jant, ay tànkam mel ni jumi sawara. 2 Yor na benn téere bu ndaw bu ñu ubbi. Mu teg tànku ndijooram ci géej gi, tànku càmmoñam ci suuf si, 3 di xaacu, mel ni gaynde guy yëmmu. Naka la xaacu, juróom ñaari dënnu yi jib. 4 Naka la juróom ñaari dënnu yi di jib, may waaja bind, waaye ma dégg baat bu jóge asamaan, naan ma: «Li juróom ñaari dënnu yi wax, na nekk kumpa, bu ko bind.»
5 Noonu malaaka, ma ma gis, mu taxaw ci géej gi ak suuf si, yékkati loxol ndijooram, mu jëm asamaan, 6 daldi waat ci kiy dund ba fàww, ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak li ci nekk lépp; mu ne: «Négandiku wees na, 7 waaye jamono ju juróom ñaareelu malaaka ma wolee ci liitam, ndogalu Yàlla dina mat, ni mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»
8 Ci kaw loolu baat, ba ma déggoon ca asamaan waxaat ak man, ne ma: «Demal jël téere bi ñu ubbi ci loxob malaaka, mi taxaw ci géej gi ak suuf si.»
9 Ma dem ca malaaka ma, laaj ko téere bu ndaw boobu. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir, waaye dina neex ni lem ci sa gémmiñ.»
10 Noonu ma jël téere bi ci loxob malaaka mi, daldi ko lekk, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye bi ma ko wannee, mu wex xat ci sama biir.
11 Gannaaw loolu ñu ne ma: «Fàww nga wax ci kàddug Yàlla lu jëm ci réew yu bare ak xeet yu bare ak kàllaama yu bare ak buur yu bare.»